Tilde Biblia

isaiah 15

Kàddug Yàlla gi (2010, 2020)

1
Yéene bii ñeel na Mowab: Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes! Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes!
2
Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,
3
nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, ak kaw taax yaak pénc ya, ku ne di jooy ba say rongooñ wale.
4
Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu, seen baat àkki ba Yaxacc, xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo, ne yàcc ne yasar!
5
Maay jooy Mowab jooyi xol, nit ñaa nga fay dawe ba Sowar, àkki ba Eglat Selisiya. Ña ngay yéeg jëm Luwit, di jooyoo, awe yoonu Oronayim, di jalu.
6
Dexu Nimrim wow na, ñax wow, gàncax lax, dara naatatul.
7
Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon, yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya.
8
Yuux déy maase na réewum Mowab, jooyoo ya ba Eglayim, jooyoo ya ba Beer Elim.
9
Dexu Dimon déy fees na ak deret, te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw, ba ku rëcce Mowab, ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!